- Kilifa sart la ci wérug sëy, bu takk amee ci lu dul kilifa, walla jigéen maye boppam, kon sëy ba du wér.
- Kilifa mooy góor gi gën a jege jigéen gi, kon kilifa gu sori du ko maye te ku jege nekk fa.
- Sàrtal nañu ci kilifa: mu nekk mukàllaf, nekk góor, am xelum xam njariñi sëy, te kilifa gi ak ka muy meye ñu bokk diine, ku amul melo yii manut a nekk kilifa ci fas ab sëy.