àdduna ay jumtukaay rekk la, te li gën ci jumtukaay yi àdduna mooy jigéen ju baax
Jële nañu ci Abdulaah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «àdduna ay jumtukaay rekk la, te li gën ci jumtukaay yi àdduna mooy jigéen ju baax».
Muslim soloo na ko
Explanation
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne àdduna ak li ci biiram mbir mu ñuy bànneexoo ab diir rekk la mu jeex , waaye li gën ci banneexi àdduna mooy jabar ju baax, ji nga xam ne bu ko xoolee bég, bu ko digalee mu topp ko, bu fa nekkul mu wattu ko ci boppam ak alalam.
Hadeeth benefits
Dagan na ñu bànneexu ci yu teeyi àdduna yi Yàlla daganalal jaamam ñi ci lu dul yàq mbaa ŋott.
Xemmemloo ci tànn jabar ju baax; ndaxte day dimbali jëkkëram ci topp Boroomam.
Li gën ci bànneexi àdduna mooy lu tege ci topp Yàlla mbaa mu cay dimbaalee.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others