Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik, -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Nekkoon a nu ci Umar mu wax ne: "tere nañ nu toggoo lu metti"
Umar -yal na ko Yàlla dollee gërëm- day xibaare ne Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na nu nuy toggoo yu metti yi ci lu dul...
Jële na ñu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «bu kenn ci yenn di le...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day digal jullit bi muy lekke ak a naane ab ndeyjooram, di , di ko tere it muy lekke ak naane ab cà...
Jële na ñu ci Umar Ibn Abii Salamata -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Bama nekkee xale ci kër Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli...
Umar Ibn Abii Salamata -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, di doomi soxnas Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Ummu Salamata -yal na...
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee ne: «Yàlla dana bëg...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne sant gi jaam bi di sant Boroomam ci ay ngëneelam ak i xéewalam daa bokk ci bir yi ñuy...
Jële nañu ci Salamata ibnul Akwah -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn waay da doon lekke càmmooñ fi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéew...
Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa gis benn waay muy lekke loxob càmmooñam, mu digal ko mu lekke loxob ndayjooram, Waa ji tontu ko...
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik, -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Nekkoon a nu ci Umar mu wax ne: "tere nañ nu toggoo lu metti"
Jële na ñu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «bu kenn ci yenn di lekk na lekke loxo ndeyjooram, buy naan na naane loxo ndeyjooram, ndax Saytaane loxob càmmooñam lay lekke, loxob càmmoñam lay naane».
Jële na ñu ci Umar Ibn Abii Salamata -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Bama nekkee xale ci kër Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, nuy lekk sama loxo doon wëreelu ci ndab li, Yónente bi ne ma: « yaw xale bi, tuddal Yàlla, te lekke sa loxo ndeyjoor, te lekk li ne ci sa kanam» booba ba leegi noonu laay lekke.
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee ne: «Yàlla dana bëgg ci jaam bi bu lekkee aw ñam mu sant ko ca, bu naanee ag naan sant ko ca».
Jële nañu ci Salamata ibnul Akwah -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn waay da doon lekke càmmooñ fi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu ne ko: "lekkeel sa ndayjoor", waa ji ne ko: manuma ko, mu ne ko: "Yàlla boo ko man", dara terewu ko ko lu dul rëy, nee na: yëkkatiwaatu ko jëme ci gémmiñam.
Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Yàlla daa bëgg ñu def limu yombal, kem ni mu bëgge ñu def mbir yimu dogu».
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónenteb Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ku Yàlla namm ci moom aw yiw dana ko nattu».
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu, ak Abuu Hurayrata -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ñu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Amul benn coono buy dal ab jullit, mbaa tawat walla, jaaxle, mbaa naqar, loraange, walla njàqare, doonte dég gu ko jam la, lu dul ne Yàlla dina ca fare yenn ci ay bàkkaaram».
Jële nañu ci Abuu Muusaa Al-Asharii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «bu nit ki feebaree walla mu tukki dees na ko bindal kem la mu daan jëf ba mu tukkiwul te wér».
Jële na ñu ci Muhaawiya -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: «ku Yàlla nàmm ci moom aw yiw dana ko dégg-loo diine, man nag ab séddalekat kepp laa, waaye Yàlla mooy joxe, te xeet wii du deñ di taxaw ci mbiri Yàlla, ku wuute ak ñoom it du leen lor, ba baa mbiri Yàlla di ñëw».
Jële na ñu ci Jaabir Ibn Abdullah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "buleen sàkku xam-xam ngir di ci puukarewu ak woroom xam-xam yi, walla ngir di ci werente ak way-dese ñi, walla ngir am ci wàccuwaay ca jotaay ya, képp ku def loolu, sawara la jëm, sawara la jëm".
Jële nañu ci Usmaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ki gën ci yéen mooy ki jàng Alxuraan te di ko jàngale».