- Lekke ndayjoor lu war la, lekke càmmooñ nag dafa araam.
- Rëy a jëfe àttey sariiha yi, ku ko def yeyoo na mbugal.
- Yàlla dafa teral Yonnenteem Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci nangu ñaanam.
- Yoonalees na digle lu baax ak tere lu bon ci jépp jamono, ba ci jamonoy lekk