- Bokk na ci njariñal hdiis bi :Màggaay ak ngëneelul xam-xamu Sariiha ak d sàkku ko ak ñaaxe ca.
- Xeet wi manut a ñàkk ñuy taxaw ci dëgg, bu ko am mbooloo bàyyee itam ñeneen taxawe ko.
- Dégg diine daa bokk ci liy wane ne Yàlla namm na aw yiw ci jaamam bi.
- Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day joxe ci ndigalu Yàlla ak coobareem, waaye moom amul dara.