bu nit ki feebaree walla mu tukki dees na ko bindal kem la mu daan jëf ba mu tukkiwul te wér
Jële nañu ci Abuu Muusaa Al-Asharii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «bu nit ki feebaree walla mu tukki dees na ko bindal kem la mu daan jëf ba mu tukkiwul te wér».
Al-buxaariy soloo na ko
Explanation
Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ngëneelu Yàlla ak yërmaandeem, ak ne jullit bu aadawoo di def jëf ju baax ci jamonoy wéram te tukkiwul, mujj gi mu am ngànt daal di feebar ba manu koo defaat, walla tukki soxlaal ko ba manul loolu, walla ngànt gu mu man a doon ; kon dees na ko bindal yool wu mat sëkk, kem su ko defoon cig wér ak cig ñàkka tukki.
Hadeeth benefits
Yaatug ngëneelu Yàlla ci jaamam yi.
Ñaaxe ngir góor -góorlu ci topp yi, ak gaawantu jëf ci jamonoy wér ak jomanoy péex te.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others