- Bokk na ci toggoo yu metti yi ñu tere: bari ab laaj, walla di toggoo loo xamul, walla di taral ci mbir mu Yàlla woyofal.
- Jaadu na ci jullit bi mu tàmmal boppam woyof te bañ a diisal ci wax ak ci jëf: ci lekkam, ak ci naanam, ak ci ay waxam, ak mbiram yépp.
- Lislaam diine ju yomb la.