- Bokk na ci teggini lekk ak naan wax Bismil Laahi ca tàmbali ga.
- Jàngal xale yi ay teggin, rawatina ku nekk ci ron kilifteefug nit.
- Ñeewanteg Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ak yaatug dënnam ci jàngal ndaw ñi ak yar leen.
- Bokk na ci teggin yi nit ki lekk ci li feete ak moom, lu dul bu nekkee ñam yu wuute kon dana ca sañ a jël.
- Sahaaba yi dañu daan taqoo ak li leen Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yare, te loolu dees na ko jariñoo ci waxi Umar je ne: Ba tay jii noona laay lekke.