Yàlla dana bëgg ci jaam bi bu lekkee aw ñam mu sant ko ca, bu naanee ag naan sant ko ca
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee ne: «Yàlla dana bëgg ci jaam bi bu lekkee aw ñam mu sant ko ca, bu naanee ag naan sant ko ca».
Muslim soloo na ko
Explanation
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne sant gi jaam bi di sant Boroomam ci ay ngëneelam ak i xéewalam daa bokk ci bir yi ñuy ame ngërëmal Yàlla; bu lekkee aw ñam daal di wax: maa ngi sant Yàlla, bu naanee daal di wax ne: maa ngi sant Yàlla.
Hadeeth benefits
Teddug Yàlla mu màgg mi, ndax moo joxe wërsëg ci ngëneelam, daal di gërëm ngir cant gi.
Ngërëmal Yàlla dees na ko ame ci sabab yu yomb, niki sant ginnaaw lekk ak naan.
Bokk na ci teggini lekk ak naan: sant Yàlla ginnaaw lekk ga ak naan ga.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others