ki gën ci yéen mooy ki jàng Alxuraan te di ko jàngale
Jële nañu ci Usmaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ki gën ci yéen mooy ki jàng Alxuraan te di ko jàngale».
Al-buxaariy soloo na ko
Explanation
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne ki gën ci jullit ñi te gën leen a kawe ay daraja fa Yàlla mooy: ki xamlu Alxuraan, cig jàng ak mokkal ak dégg ak firi, te xamal ñeneen ñi la mu am ci xam-xami Alxuraan ànd ak di ko jëfe.
Hadeeth benefits
Leeral tedd-ngay Alxuraan, ak ne moo gën ci wax yi; ndaxte waxi Yàlla la.
Ki gën ci way-jàng yi mooy kiy jàngal ñeneen ñi waaye du ki koy yamale ci boppam rekk.
Jàng Alxuraan ak di ko jàngale dafay làmboo jàng ga ak xam maanaa ya ak àtte ya.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others