Yàlla daa bëgg ñu def limu yombal, kem ni mu bëgge ñu def mbir yimu dogu
Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Yàlla daa bëgg ñu def limu yombal, kem ni mu bëgge ñu def mbir yimu dogu».
Ibnu Hibbaan soloo na ko
Explanation
Leerarug hdiisbi:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da ñuy xamal ne: Yàlla daa bëgg ñu def ay yombalam yi mu yoonal, ci woyofal àtte yi ak jaamu yi, ak yombalal ko mukallaf mi ngir ngànt -niki wàññi julli ak boole ko cib tukki-, Kem nimu bëgge ñu def ay dogoom, ci bir yu war yi; ndaxte ndigalul Yàlla ci yombal yi ak ci dogu yi benn la.
Hadeeth benefits
Bokk na ci njariñal hdiis bi:
Yërmàndey Yàlla ci jaamam ñi, ak ne moom Yàlla mu sell mi day bëgg ñu def yi mu yoonal ci ay yomb-yomb.
Matug Sariiha ji ak teggilam jullit bi AB coono.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others