- Hadiis bi day wane ne ŋàññi ñi faatu dafa araam.
- Moytoo ŋàññi néew yi ngir bàyyi xel ci njariñu ñiy dund, ak ngir muccal askan wi ci xuloo ak mbañeel.
- Njariñ li nekk ci tere ñu leen di saaga mooy ne ñoom dem nañu ca la ñu jiitaloon, kon saaga leen amul benn njariñ, te dafay gaañ mbokk yiy dundu.
- Jaaduwul ci nit muy wax lu amul njariñ.