bàyyiwuma sama ginnaaw fitna ju dàq a lor góor ñi ci jigéen ñi
Jële nañu ci Usaamata Ibn Sayd -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «bàyyiwuma sama ginnaaw fitna ju dàq a lor góor ñi ci jigéen ñi»
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Explanation
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne bàyyiwul ginnaawam nattu bu gën a man a lor góor ñi ci jigéen ñi; ndax bu bokkee ci njabootam man naa waral mu topp ko ci lu wuuteek Sariiha, bu dee ab jàmbur la ci moom man naa jaxasoo ak moom ak di wéet ak moom te loolu day waral ay yàqute.
Hadeeth benefits
War na ci jullit bi mu moytu ftnaay jigéen ñi, te fatt bépp bunt buy waral fitnawu ci ñoom.
War na ci aji-gëm ji mu làqu ci Yàlla, ak xemmeem jëm ci moom ngir mucc ci fitna yi.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others