- Du bokk ci xeetu dàggasante buñu ŋàññi su dee ki ñu tooñ dafa laaj yelleefam ci yoon.
- Werente ak xulóo dafa bokk ci gàkk-gàkki làmmeñ yiy sabab ag tàqalikoo ak bàyyente ci diggante jullit ñi.
- Dàggasante dana baax bu teggee cig dëgg te defiin wa rafet, waaye dees na ko wàññi bu dee ngir delloo dëgg la saxal ay neen, walla mu bañ a am ay lay ak ay firnde.