Wax yi gënal Yàlla ñent la: Subhaanal Laah, Wal hamdu lil Laah, wa laa-i-Laaha illal Laah, wal Laahu akbar, boo ci tàmbalee baax na
Jële nañu ci Samurata Ibn Jundub -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Wax yi gënal Yàlla ñent la: Subhaanal Laah, Wal hamdu lil Laah, wa laa-i-Laaha illal Laah, wal Laahu akbar, boo ci tàmbalee baax na».
Muslim soloo na ko
Explanation
Leerarug adiis bi:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne wax yi gënal Yàlla ñent la:
Subhaanal Laah: te mooy sellal Yàlla ci bépp wàññeeku.
Ak alhamdu lil Laah: te mooy melal Yàlla cig mat sékk ànd ak bëgg ko ak màggal ko.
Ak laa-i-Laaha illal Laah: maanaam: amul kenn ku ñuy jaamu cig dëgg ku dul Yàlla.
Ak al-Laahu akbar: maanaam: Yàllaa gën a tedd te moo gën a màgg lépp lu mu man a doon.
Te ngëneelam ak yoolam nekkul rekk ci toftale ko boo koy wax.
Hadeeth benefits
Bokk na ci njariñal adiis bi:
Yombug Sariiha, ba tax na baat boo ci tàmbalee it du la lor.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others