Yàlla day fiir, way-gëm it day fiir, te fiiràngeg Yàlla mooy way-gëm ji def lu mu araamaal
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "Yàlla day fiir, way-gëm it day fiir, te fiiràngeg Yàlla mooy way-gëm ji def lu mu araamaal".
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Explanation
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne Yàlla day fiir di bañ di sib, kem ni aji-gëm ji di fiire ak di bañe ak di sibe, te sababus fiiràngem Yàlla mooy way-gëm ji def lu Yàlla araamal ci moom ci ay ñaawteef niki njaalo ak ngóor-jigéen, ak sàcc ak naan sàngara ak yeneen ñaawteef.
Hadeeth benefits
Moytondikuloo ci merum Yàlla ak mbugalam bu ñu defee yi mu araamal.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others