/ Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan wax ci diggante ñaari sujjóot yi: «Allaahumma ixfir lii, warhamnii, wa haafinii, wahdinii, warsuqnii

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan wax ci diggante ñaari sujjóot yi: «Allaahumma ixfir lii, warhamnii, wa haafinii, wahdinii, warsuqnii

Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan wax ci diggante ñaari sujjóot yi: «Allaahumma ixfir lii, warhamnii, wa haafinii, wahdinii, warsuqnii».
Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat

Explanation

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na ñaan ci diggante ñaari sujjóot yi ci julli gi juróomi ñaan yii nga xam ne jullit bi da cee am aajo ju màgg, te mu làmboo yiwi àdduna ak allaaxira, ci sàkku njéggal ak suturaal bàkkaar yi te baal ka ko, ak sotti ko yërmànde, ak mucc ci lënt-lënt yi ak bànneex yi ak feebar yi ak wopp yi, te ñaan Yàlla ag gindi ñeel dëgg te sax ca, ak wërsëgu gëm ak xam-xam ak jëf ju baax, ak alal ju dagan te teey.

Hadeeth benefits

  1. Yoonalees na ñaan gii ci toogaay bi nekk ci diggante ñaari sujjóot yi.
  2. Ngëneelu ñaan yii ngir li mu làmboo ci yiwi àdduna ak allaaxira.