- Bérabu taaya jii nag mooy bu nu toogee ginnaaw sujjóot gu mujj gi, ginnaaw ràkka bu ñaarel bi ci jullig ñatt ak ñenti ràkka.
- Attahiyyaatu dafa war ci taaya, dana dagan mu taaya ci bépp waat ci waati taaya yi sax jóge ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
- Ñaan loo bëgg fii ak nekkul bàkkaar dagan na ci julli.
- Sopp nañu booy ñaan nga tàmbalee ci sa bopp.