/ Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan tudd Yàlla ci bépp jamono

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan tudd Yàlla ci bépp jamono

Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan tudd Yàlla ci bépp jamono.
Muslim soloo na ko

Explanation

Aysatu yaayu way-gëm ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- day xibaare ne Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa xéroon lool ci tudd Yàlla mu kawe mi, ak ne daa na tudd Yàlla ci bépp jamono ak bérab ak anam.

Hadeeth benefits

  1. Sàrtaluñu ci tudd Yàlla laab ci toj gu ndaw mbaa toj gu mag.
  2. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa saxoon ci tudd Yàlla .
  3. Ñaaxe ci tudd Yàlla mu kawe mi lu bari ci bépp jamono ngir roy ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, lu dul ci anam yi ñuy tere ku ci tudd Yàlla, niki jamanoy faj aajo.