- Ñaaaxe ci di baril jàng Alxuraan.
- Aji-jàng ji am na ci wépp araf ci baat bu mu jàng bu nekk yiw wu ñu ful ba fukk yu mel ni moom.
- Yaatug yërmàndey Yàlla ak tedd-ngaam ba tax muy fulal jaam bi ab yool ngir ngëneelam ak teraangaam.
- Ngëneelu Alxuraan ci jeneen wax ju dul moom, ak jaamu Yàlla ci jàng ko; ndaxte waxi Yàlla la.