- Màggaayu àqi dëkkandóo, ak warteefu sàmmoonte ak loolu.
- Feddali àqi dëkkandóo ci di baamtu ndénkaane li, day waral ñu koy teral ak di ko bëgg di rafetal jëme ci moom, di jeñal lor, ak di ko seeti bu feebaree, di ko ndokkeel bu amee mbégte, di koo jaale bu amee musiba.
- Lu buntu dëkkandóo gën a jege àqam di gën a feddaliku.
- Matug Sariiha moo ngi ci li mu indi ci yéwénal mbooloo mi ci rafetal jëme ci dëkkandóo yi ak di leen fegal lor.