- Xérug Sahaaba yi ci xam jikko yiy jariñ ci àdduna ak allaaxira.
- Nuyoo ak joxe ñam dafa bokk ci jëf yi gën ci Lislaam;ngir ngëneelam ak ni ko nit ñi di aajowoo ci waxtu wu ne.
- Ci ñaari jikkó yii la rafetal di dajee ci wax ak ci jëf, te mooy li gën a mat ci rafetal.
- Jikkó yii day aju ci jëflànte ci diggante jullit ñi, am na yeneen jikko ci jëflànte jullit bi ak Boroomam.
- Njëkka nuyóo dañmm jullit rekk la jagoo, waaye deesul njëkk a nuyu ab yéefar.