- Sopp nañu ñaan gii bu ñuy dugg ci jàkka ak bu ñuy génn.
- Li ñu jagleel tuddug yërmànde ci dugg gi, ak ngëneel ci génn gi: kiy dugg lu koy jegeele Yàlla ak àjjanaam ji moo ko soxlaal loolu nag daa méggoo ak ñu tudd fa yërmànde, bu génnee nag day wéy ci kaw suuf di sàkku ngëneelu Yàlla ci wërsëg, loolu méggoo ak ñu tudd fa ngëneel.
- Askaar yii nag dees koy wax bu ñu bëggee dugg ci jàkka, ak bu ñu ca bëggee génn.