- Muslu ag jaamu la, te ci Yàlla lañu koy def ak ay turam ak i meloom.
- Dagan na ñu muslu ci waxi Yàlla, ndaxte melo la ci ay melokaanam moom Aji-Sell ji, mu wuute ak muslu ci mbindeef ndaxte bokkaale la.
- Ngëneelul ñaan ak barkeem.
- Aaru ci sikar sabab la ci musal jaam bi ci ay yi.
- Naaxsaayal sàkku muslaay ci lu dul Yàlla, lu ci mel ni jinne yi, ak njabarkat yi, ak duurkat yi ak ñeneen.
- Yoonal nañu jàng ñaan gii ci képp ku wàcc ci ab barab mu nekk ci dëkkam wala cib tukki.