- Sopp nañu tudd Yàlla bu ñuy dugg ci kër ak bu ñuy lekk, ndax Saytaane day fanaan ci kër gi,di lekk ci lekku waa kër gi, bu ñu tuddul Yàlla mu kawe mi.
- Saytaane day ànd ak doomu Aadama ji ci jëfam, di ko wëlbati ci ay biram yépp, te bu sàgganee tudd Yàlla dana am li mu bëgg ci moom.
- Tudd Yàlla day dàq saytaane.
- Saytaane su nekk am na ñu koy topp ak ñu far ak moom di bége ay waxam tey topp ay ndigalam.