kóllare gi dox ci sunu diggante ak ñoom yéefar yi mooy julli, ku ko bàyyi weddi na
Jële na ñu ci Buraydata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «kóllare gi dox ci sunu diggante ak ñoom yéefar yi mooy julli, ku ko bàyyi weddi na».
At-tirmisiy soloo na ko, ak An-nasaa'iy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat
Explanation
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne kóllare gi dox ci diggante jullit ñi ak ñu dul ñoom ci yéefar yi ak naaféq yi mooy julli, ku ko bàyyi weddi na.
Hadeeth benefits
Màggaayu mbiri julli, ak ne mooy liy tàqale diggante jullit bi ak yéefar bi.
Àttey Lislaam day saxe ci li feeñ ci melokaani nit ki waaye du lia nëbbu.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others