- Julli giy far ay bàkkaar mooy julli gi jaam bi rafetal njàppu ma, te def ko cig ragal Yàlla di ca sàkku jëmmi Yàlla mu kawe mi.
- Ngëneelu taqoo ak jaamu yi, ngir ne sabab la ci njéggalu bàkkaar yu ndaw yi.
- Ngëneelu rafetal njàppu mi, ak rafetal julli gi te teewlu ko mu ànd ak toroxlu.
- Solos moytu bàkkaar yu mag yi ci njéggalu bàkkaar yu ndaw yi.
- Bàkkaar yu mag yi dara du ko far lu dul tuub.