- Bàkkaar yi daa am yu ndaw am yu mag.
- Far bàkkaar yu ndaw yi dafa aju ci moytu bàkkaar yu mag yi.
- Bàkkaar yu mag yi mooy bàkkaar yi nga xam ne gétan (ay daan) da cee war ci àdduna, walla ag tëkkug àllaaxira ñëw ci mbugal, walla merum Yàlla, walla ag xuppe nekk ca, mbaa ag rëbb ñeel ki ko def, lu mel ni njaalo ak naan sàngara.