Jële na ñu ci Jaabir Ibn Abdullah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-nee na: «Moytuleen tooñ,...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo tooñ, te bokk na ca: tooñ nit ñi, ak tooñ sa bakkan, ak tooñ ci àqi Yàlla mu kawe...
Jële na ñu ci Abuu Muusaa Al-Asharii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Yalla...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo di wéy cig tooñ ak i moy ak bokkaale, ak tooñ nit ñi ci séen i àq, ndax Yàlla mu k...
Jële nañu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- Jele nañu ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci li mu soloo ci Boroomam mu...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne Yàlla dogal na yiw yi ak ñaawtéef yi daal di leeralal ñaari Malaaka yi naka lañu koy b...
Jële na ñu ci Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm-, mu wax ne: Benn waay dafa ne: yaw Yónente Yàlla bi, ndax dañ nuy toppe la nu defoon ca ceddu...
Leerarug hdiis bi:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ngëneelul dugg ci Lislaam, Ak ne képp ku tuub te rafetal Lislaamam tey...
Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu ne: Ay nit yu bokkoon ca bokkaalekat ya, dañoo ëppaloon ci raye, ëppal ci njaalo, ñu ñëw...
Ay gaay ci bokkaalekat yi dañoo ñëwoon ci yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- te fekk ñu ëppaloon lool ci ray nit ak njaalo, ñu wax Yón...
Jële na ñu ci Jaabir Ibn Abdullah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-nee na: «Moytuleen tooñ, ndax tooñ ay lëndëm lay doon ëllëg bis-pénc, te ngeen moytu nay, ndaxte nay moo alag ña leen jiitu woon, yóbbe na leen ñu tuur seen i dereet ak a daganal araam».
Jële na ñu ci Abuu Muusaa Al-Asharii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Yalla dana néggandiku tooñkat bi, ba bu ko jàppee du ko rëcc» nee na: mu daal di jàng: aaya bii «{niki noonu it la sa jàppug Boroom di deme bu jàppee waa dëkk buy tooñ te ag jàppam lu metti la te tar} [Huud: 102]»
Jële nañu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- Jele nañu ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci li mu soloo ci Boroomam mu màgg mi mu wax ne: «Yàlla dafa bind yu rafet yi ak yu ñaaw yi, daal di leeral ko, képp ku yéene jëf i yiw, te defu ko, Yàlla dana ka ko bindal wenn yiw wu mat sëkk, waaye bu ko yéenee ba noppi def ko, mu bindal ko fukki yiw, mannakoo Ful bamu yégg juróom-ñaari téeméeri, ba ci ay full yu bari, waaye képp ku Yéenee jëf lu ñaaw te defu ko Yàlla di na ko bindal wenn yiw wu mat sëkk, bu ko Yéenee nag daldi koy def mu bindal ko wenn ñaawteef».
Jële na ñu ci Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm-, mu wax ne: Benn waay dafa ne: yaw Yónente Yàlla bi, ndax dañ nuy toppe la nu defoon ca ceddu ga ? Mu ne ko: «ku rafetal ci Lislaam deesu ko toppe la mu defoon ca ceddu ga, waaye ku def lu ñaaw ci Lislaam dees na ko toppe lu njëkk la ak lu mujj li».
Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu ne: Ay nit yu bokkoon ca bokkaalekat ya, dañoo ëppaloon ci raye, ëppal ci njaalo, ñu ñëw ci Yónente bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: li gay wax di ci woote lu baax la, boo ñu xibaaroon ndax la ñu defoon dees na ko jéggale, aaya bi daadi wàcc {ak ñi nga xam ne duñu jaamu jeneen Yàlla di ko bokkaale ak Yàlla, te duñu ray bakkan bu Yàlla araamal ci lu dul dëgg te duñu njaalo{ [Al-Furxaan: 68], aaya bii it wàcc: {waxal sama jaam ñi nga xam ne dañoo ëppal ci def ay bàkkaar buñu naagu mukk ci yërmàndey Yàlla} [As-Sumari: 53].
Jële na ñu ci Hakiim Ibn Hisaam -yal na ko Yàlla dollee gërëm-, mu wax ne: Damaa wax: yaw Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaar ma ci bir yi ma daan def ca ceddo ga, ci sarax ak goreel, ak jokk mbokk, ndax am na yool? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «jébbalu nga ànd ak la nga defoon ciw yiw».
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee ne: «Yàlla du tooñ benn way-gëm ci jëfam ju baax di ko wàññi, dana ka ko jox fii ci àdduna fay ka ko ca allaaxira, bu dee ab yéefér nag ay jëfam yu baax yi mu def ngir Yàlla fii ci àdduna, dañu ka koy dundale, ba bu demee allaaxira, du fa fekk jenn jëf ju baax buñu koy fay».
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: Jële na ñu ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu nettali jële ci Boroomam mu màgg mi, mu wax ne: «ab jaam dafa def bàkkaar, daal di wax: yaw sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar Yàlla mu baarkeel mi wax ne: sama jaam bi def na bàkkaar, xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, tey jàppe it ci Bàkkaar, mu dellu defaat bàkkaar, daal di wax: ay sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar, Yàlla mu màgg mi wax ne: sama jaam bi def na bàkkaar, xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, tey jàppe it ci Bàkkaar, mu dellu defaat bàkkaar, daal di wax: ay sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar,Yàlla mu màgg mi wax ne: sama jaam bi def na bàkkaar, xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, tey jàppe it ci Bàkkaar, defal lu la soob jéggal naa la».
Jële nañu ci Aliyun mu wax ne: man góor laa woon gog bu ma déggee ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- benn hadiis rekk Yàlla jariñ ma ci lu ko soob, bu ma kenn ci ay Sahaabaam waxee dara bama giñloo ko bu ma giñalee ma dëggal ko, Abuu Bakar wax na ma te wax na dëgg, ne: dégg na Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «amul kenn kuy def bàkkaar, jug daal di laab, daal di julli, daal di jéggalu Yàlla, lu dul ne Yàlla dina ko jéggal», mu daal di jàng aaya jii: {ak ña nga xam ne bu ñu defee ñaawteef mbaa ñu tooñ seen bopp dañuy tudd Yàlla daal di jéggalu seen bàkkaar} [ Aali-Imraan: 135].
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «sunu Boroom bu baarkeel bi te kawe day wàcc guddi gu nekk ci asamaani àdduna si bu guddi gi desee ñatteelu xaaj bu mujj ba, di wax naan: ku may woo ma wuyu ko? Ku may laaj ma jox ko? Ku may jéggalu ma jéggal ko?».
Jële nañu ci Nuhmaan Inb Basiir -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne: dégg naa Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne -Nuhmaan jëmale yaari baaraamam ci ay noppam-: «li dagan de leer na li araam it leer na, seen diggante nag am na ay lënt, te ñu bari si nit ñi duñu ko xam, képp ku moytu yu lënt yi ñoŋal na diineem ak deram, waaye ku tàbbi ca lënt ya kooku tàbbi na ca yu araam ya, mi ngi mel ni sàmmkat biy sàmm ci li wër ab ñag, daanaka rekk sàmm na ca biiram, xanaa du buur bu nekk am na ab ñagam, te ñagub Yàlla mooy li mu araamal, xamleen ne yaram am na aw lumb wow bu baaxee yaram wépp baax, bu yàqoo yaram wépp yàqu, loolu mooy xol«.
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn bis nekkoon naa ci ginnaaw Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu ne ma: «yaw ngóor si di naa la xamal ay waat: wattul Yàlla ci jëfe ay ndigëlam bayyi ay tereem kon di na la sàmm, Nanga bàyyi xel Yàlla kon mu féete la fépp, booy ñaan ñaanal Yàlla, booy sàkku ndimbël na nga dimbandikoo Yàlla, te nga xam ni bu ñépp dajewoon ngir jariñ la ci dara duñu ko man lu dul lu Yàlla dogal ci yaw ba noppi, bu ñépp dajewoon it ngir lor la ci dara duñu ko man ludul lu Yàlla dogal ci yaw ba noppi, ndax teggi nañu xalima ya te kayit ya woow na».