- Ngëneelu Lislaam ag màggaayam ci ne day màbb bàkkaar yi ko jiitu.
- Yaatug yërmàndey Yàlla ci jaamam yi ak njéggalam ak ug baaleem.
- Bokkaale dafa araam, ray bakkan ci lu dul dëgg dafa araam, njaalo dafa araam, tëkku nañu it kuy def bàkkaar yii.
- Tuub gu dëggu gu ànd ak sellal ak jëf lu baax day far mbooleem bàkkaar yu mag yi ba ci weddi Yàlla mu kawe mi sax ca la bokk.
- Araamalees na naagu ak ñakk yaakaar ci yërmàndey Yàlla -tudd naa sellam ga-.