- War na ci ki am xel mu gaaw a tuub, te bañ a wóolu pexem Yàlla ndeem dafa nekk cig tooñ.
- Yàlla day néggandiku way-tooñ yi bañ leen a mbugal ngir jay leen ak ngir ful mbugal ma bu ñu tuubul.
- Tooñ bokk na ci sabab yiy tax Yàlla di mbugal xeet yi.
- Bu Yàlla alagee ab dëkk amaana ñu sell nekk fa, waaye ñooñu dañu leen di dekkil ëllëg bis-pénc ca mbaax ga ñu faatoo, te mbugal ma leen yóbbaale du leen lor.