- Yaatug yërmàndey Yàlla ci jaamam yi, ba lu nit ki man a def ci bàkkaar ak lu mu man a def bu tuubee dellu ci moom Yàlla jéggal ko.
- Ki gëm Yàlla day yaakaar yërmàndey Boroomam, tey ragal mbugëlam, ba tax muy gaawantu di tuub te du wéy cig moy.
- Sarti tuub gu wér: deñ ci bàkkaar bi, ak réccu ko, ak dogu ci bañ a dellu ca bàkkaar ba, bu dee tuub gi dafa aju ci tooñ jaam ñi ci séen alal mbaaa séen der, walla séen bakkan, kon day dolli ñenteelu sart, te mooy sàkkoo set sa bàkkaar ba sa Boroom àq ja, walla mu jox ko àqam.
- Amug solo ci xam ne Yàlla miy def jaam bi mu xam biri diineem ba tax muy tuub saa yu juumee, te du naagu ba tax muy wéy ca bàkkaar ba.