Moytuleen tooñ, ndax tooñ ay lëndëm lay doon ëllëg bis-pénc, te ngeen moytu nay, ndaxte nay moo alag ña leen jiitu woon,
Jële na ñu ci Jaabir Ibn Abdullah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-nee na: «Moytuleen tooñ, ndax tooñ ay lëndëm lay doon ëllëg bis-pénc, te ngeen moytu nay, ndaxte nay moo alag ña leen jiitu woon, yóbbe na leen ñu tuur seen i dereet ak a daganal araam».
Muslim soloo na ko
Explanation
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo tooñ, te bokk na ca: tooñ nit ñi, ak tooñ sa bakkan, ak tooñ ci àqi Yàlla mu kawe mi. Te mooy bañ a jox ku nekk àqam, ak ne tooñ ay lëndëm lay doon ci kaw ay ñoñam ëllëg bis-pénc ci ñu daje fa ak ay tar-tar ak i tiitaange, Mu tere bëgge te mooy nay gu tar ak ug xér ci alal, bokk na ca gànteñlu ci joxe àqi alal yi ak xér gu tar ci àdduna. Xeetu tooñ gii moo alag xeet yi ñu jiitu woon, ndax da leen a yóbbe woon ci ñenn ñi di ray ñeneen ñi, ak di daganal yu araam yi Yàlla araamal.
Hadeeth benefits
Bokk na ci njariñal hadiis bi:Joxe alal ak jàpple mbokk yi dafa bokk ci yiy waral bëggante ak jokkoo.
Nay ak bëgge day yóbbe nit ki ci moy ak i ñaawteef ak i bàkkaar.
Waaru ci mbiri xeet ya jiitu woon.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others