Jële na ñu ci Abul Hiyyaaj Al-Asadi mu wax ne: Aliyun Ibn Abii Taalib da ne ma: ndax du ma la yabal ca la ma Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli x...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na yónni Sahaaba yi ci ñu bañ a bayyi benn «xërëm» -te mooy nataalu lu am ruu moo xam dafa am jë...
Jële na ñu ci Abdallah Ibn Mashuud mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «gaaflu bokkaale la, gaaflu bokkaale la...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo Tiyara te mooy gaaflu ci lépp lu mu man a doon moo xam lu ñuy dégg la mbaa lu ñuy...
Jële na ñu ci Imraan Ibn Husayn -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «bokkul ci nun ku...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tëkku na kuy def ci xeetam wi yenn jëf yi ci li mu wax ne: «bokkul ci nun» bokk na ca yooya: Bu n...
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne: «wàlle am...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne wàlle gi ceddo ya gëmoon ci ne feebar bi day toxal boppam jëm ci keneen ci lu dul d...
Jële na ñu ci Sayd Ibn Xaalid Al-Juhanii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dañoo jiite julli...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa julli jullig suba ca Hudaybiya -ab bérab la bu jege Màkka- ginnaaw ba mu tawee ca guddi googa,...

Jële na ñu ci Abul Hiyyaaj Al-Asadi mu wax ne: Aliyun Ibn Abii Taalib da ne ma: ndax du ma la yabal ca la ma Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yabaloon? Bul bàyyi benn xërëm te tojoo ko, mbaa benn bàmmeel bu ñuy màggal te maasale woo ko.

Jële na ñu ci Abdallah Ibn Mashuud mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «gaaflu bokkaale la, gaaflu bokkaale la, gaaflu bokkaale la, -ñatti yoon-, amunu ci pexe, waaye Yàlla mu màgg mi moo koy dindi ci wakkirlu.

Jële na ñu ci Imraan Ibn Husayn -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «bokkul ci nun kuy gisaane mbaa ñu gisaaneel ko, walla mu seetlu mbaa ñu seetal ko, walla mu njabar mbaa ñu njabaral ko, ak kuy fas ag fas, ku ñëw ci ab seetkat dëggal ko ca la mu wax kooku weddi na li ñu wàcce ci Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-«.

Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne: «wàlle amul, gaafal amul, gaatnga lu baax nag yéem na ma» nee na, ñu ne ko: lan mooy gaatnga lu baax ? Mu ne: "wax ju teey".

Jële na ñu ci Sayd Ibn Xaalid Al-Juhanii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dañoo jiite jullig suba ca Hudaybiya ginnaaw ba mu tawee ca guddi ga, ba mu noppee mu jàkkaarloo ak nit ñi, ne leen: «ndax xam ngeen lan la séen Boroom wax ?» Ñu ne ko: Yàlla a xam ak ub Yónenteem, mu ne leen: Yàlla dafa wax ne: «am na ci sama jaam ñi ñu xëy gëm ma am ñu weddi, ku wax ne: taw bi wàcc na fi nun ci ngënéelu Yàlla ak yërmàndeem, kooku gëm na ma, weddi biddiw yi, waaye ku wax: taw bi biddiw bii mbaa bee mootax mu am, kooku weddi na ma, gëm biddiw yi».

Jële nañu ci Huqbata ibn Aamir Al-Juhanii-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne: Yonnente Yàlla bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-am mbooloo dañoo ñëw ci moom,mu jaayante ak juróom-ñent ñi bàyyi kenn ki,nu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, jaayante nga ak juróom-ñent daal di bàyyi kii? Mu ne:"ab téere la takk",mu dugal loxoom dagg ko,daal di jaayante ak moom,daal di wax ne: "ku takk ab téere bokkaale na".

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «mocc ak takk ay xarnga-fuufa ak noob bokkaale la».

Jële na ñu ci yenn Soxnay Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku ñëw cib xamtukat laaj ko dara deesu ko nangul julli ñent-fukki guddi».

Jële na ñu ci Abdallah ibnu Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ci ne dégg na benn waay di wax naan: giñ naa ci Kaaba gi, Ibnu Umar ne ko: deesul giñ ci ku dul Yàlla, man dégg naa Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: «ku giñ ci ku dul Yàlla weddi na walla bokkaale na».

Jële nañu ci Husayfata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «buleen di wax: bu soobe Yàlla soob diw, waaye waxleen: bu soobe Yàlla topp mu soob diw»

Jële na ñu ci Mahmuud Ibn Labiid -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «li ma gën a ragal ci yéen mooy bokkaale gu ndaw" ñu ne ko: lan mooy bokkaale gu ndaw yaw Yonnente Yàlla bi? Mu ne leen: "ngistal, ngistalkat yi Yàlla da leen di wax ëllëg bis-pénc bu ñu faayee nit ñi seen jëf ba noppi: demleen ca ña ngeen doon ngistal ca àdduna, ngeen xool ba xam ndax dangeen fekk fa ñoom ag pay?"

Jële na ñu ci Marsad Al-Xanawii -yalna ko Yàlla gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «buleen toog ci kaw bàmmeel yi, te buleen ko jublu ci julli».