- Araamug nataal lu am ag ruu; ndax daa bokk ci jumtukaayi bokkaale yi.
- Yoonalees na dindi lu bon ci loxo ci ku am nguur, mbaa mu man loolu.
- Xérug Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci dindi lépp luy wane jeexitalu ceddo, ci ay nataal ak i xërëm ak tabax ci bàmmeel yi.