- Bokk na ci njariñal hdiis bi :
- Sopp na ñu ginnaaw bu tawee ñu wax lii: (mutirnaa bi fadlil laahi wa rahmatihii) tawalal nañ ñu ci ngënéelu Yàlla ak yërmàndeem.
- Képp koo xam ne wàccug taw bi mbaa leneen dakoo askanale biddiw yi moo xam cig mbind mbaa amal ga kooku aji-weddi la weddi gu mag, bu ka ko askanalee ci ne sabab la kon aji-weddi la weddi gu ndaw ndax loolu nekkul sabab ci Sariiha mbaa ci yég-yég.
- Xéewal dana nekk sababu kéefar bu nu ko weddee, dana nekk it sababu ngëm bu ñu santee.
- Tere na ñu di wax naan: "wàcceel nañ ñu ab taw ngir biddiw sàngam", doonte jamono la ñu ci jublu; loolu nag ngir fatt luy yóbbe ci bokkaale.
- Xol bi dafa war a wékku ci Yàlla mu kawe mi ci xëcci njariñ ak jeñ lor.