- Tere nañu julli ci ay bàmmeel walla séen diggante walla jublu ko lu dul jullig néew kem ni mu saxe ci Sunna.
- Tere nañu di julli jublu ay bàmmeel ngir sakk yoonu bokkaale.
- Lislaam dafa tere ëppal ci bàmmeel yi ak di ko doyodal, deesul ëppal waaye deesul yéesal.
- Wormay jullit day des di wéy ginnaaw ba mu faatoo, ngir li Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax na ne: (toj yaxu ku faatu moo ngi mel ni toj ko ba muy dund).