- Araam na ñuy wax: "bu soobee Yàlla soob la", ak lu ko niru ci ay kàddu ndax li ci nekk ci toftal ci Yàlla ak; ndaxte ci bokkaaley kàddu yi ak wax yi la bokk.
- Dagan na ñu wax: "li soob Yàlla topp mu soob la", ak lu ko niru lol dañuy toftal ci Yàlla baatu topp ngir ne la ñuy moytu deñ na.
- Saxalal Yàlla coobare, ak saxalal jaam bi coobare, ak ne coobarey jaam bi day topp coobarey Yàlla mu kawe mi.
- Tere nañu boole nit ñi ci coobarey Yàlla doonte ci wax la.
- Aji-wax ji bu fasee ne coobarey jaam bi dafa melni coobarey Yàlla yam ak moom ci matale ak cig boyal, walla fas ne jaam bi dafa am coobare gu beru loolu bokkaale gu mag la, waaye bu fasee ne eggul foofu; loolu bokkaale gu ndaw la.