- Bokk na ci njariñal adiis bi :
- Sàmm ag wéetal Yàlla ak pas-pas bu wér ci lépp lu koy yàq.
- Araamug jëfëndikoo mocci bokkaale yi ak i xarnga-fuufa, ak noob.
- Nit ki gëm ci ñatt yii ne ay sabab lañu: loolu bokkaale gu ndaw la; ndax mooy lu nekkul sabab nga def ko sabab, waaye bu fasee ne day jariñ di lor ci boppam loolu bokkaale gu mag la.
- Moytondikuloo di def sababi bokkaale yi ak yu araam yi.
- Araamal mocc ak ne si bokkaale la bokk lu dul muy mocc bu ñu yoonal.
- Xol bi dafa war a wékku ci Yàlla dong, ndax ci moom rekk la lor ak njariñ di bawoo amul bokkaale, yiw du am lu dul mu juge ci Yàlla te kenn du jeñ lor ku dul Yàlla mu kawe mi.
- Mocc bu dagan day làmboo ñatti sart: 1- mu fas ne sabab rekk la du jariñ ci lu dul ndigalu Yàlla. 2- mu nekk ci Alxuraan ak turi Yàlla ak i meloom ak ay ñaani Yónente bi ak ay ñaan yu ñu yoonal. 3- mu nekk ci làkk wu nu xam te du am ay xaatim ak i njabar.