Jële nañu ci Abuu Hurayrata-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «malaaka yi duñu ànd...
Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day xibaare ne malaaka yi duñu ànd ci tukki boo xam ne ab xaj da caa ànd, walla ab jóolooli li gu ñu...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Saytaane day...
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne faj gi gën ci laaj yi Saytaane di jax-jaxale aji-gëm ji, Saytaane naan ko: ku bin...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Yàlla nee na:...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day xibaare ci hadiis bu sell bii ne Yàlla mu màgg nee na: Ku lor kenn ci wàlliyu ci sama péete yi...
Jële nañu ci Al-Hirbaat Ibnu Saariyata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Benn bis Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa taxa...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa waar Sahaaba yi ag waar gu jotale ba xol yi ragal ca, bët yi jooy ca, Ñu ne ko : yaw Yónente Yà...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku génnug topp, d...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne képp Ku génn ci toppug njiit ya, tàqalikoo ak mbooloom Lislaam ma dëppoo ci jaayante a...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «malaaka yi duñu ànd ci mbooloo mu ànd akub xaj walla ab jóolooli.

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Saytaane day dikkal kenn ci yéen, di ko wax naan: ku bind lii? Ku bind lii? Ba mujj mu ne ko: ku bind sa Boroom? Bu àggee fii nag na muslu ci Yàlla te yamale ko fa».

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Yàlla nee na: ku noonook sama péete yégal naako ab xare, sama jaam bi du ma jegeñ-jegeñlu ci dara lu ma gënal li ma farataal ci moom, sama jaam bi du deñ dima jéema jege ci ay naafila ba ma bëgg ko, te bu ma ko bëggee, maay nekk déggam gi muy dégge, ak gisam gi muy gise, ak loxoom bi muy jàppe, ak tànkam bi muy doxe, bu ma ñaanee ma may ko,bu ma musloo ma musal ko, du ma dengi-dengi ci dara lu may def, samag dengi-dengi mi ngi ci bu may jël bakkanu aji-gëm ji, ndax day bañ a dee,te man dama koy bañ a def lu mu bëggul».

Jële nañu ci Al-Hirbaat Ibnu Saariyata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Benn bis Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa taxaw fi nun daal di nuy waar waar gu jotale xol yi jàq nañu ci, bët yi tuur ci rangooñ, ñu ne ko : yaw Yónente Yàlla bi, waar nga nu waarug kuy tàggatoo, jox ñu ak kóllare. Mu ne leen : "dénk naa leen ngeen ragal Yàlla ci dégg ak topp, donte jaamub Habasa la, dangeen gis ci sama ginnaaw ag wuute gu tar, waaye nangeen jàpp ci sama Sunna ak sunnay njiit yu jub ya tey jubal, ŋànkleen ko ak seen i dégéj, te ngeen moytandiku mbir yi ñu sos, ndax bidaa yépp ay réer la".

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku génnug topp, daal di tàqalikoo ak mbooloo ma ba faatu, kon dee na deewug ceddo, képp kuy xeex ngir yékkati raayaa cànkute, di mer ngir par-parloo, di woote ci aw xeet, walla muy xeex ngir par-parloo ciw xeet pp ba ñu ray ko, kon ag rayam rayug ceddo la, képp ku génn ag topp ci sama xeet wi, di dóor ñu baax ña ak kàccoor ya, te du moytu sax way-gëm ña, te du matale kóllëreg boroom kollëre, kooku bokkul ci man te bokkuma ci moom».

Jële nañu ci Mahqal Ibn Yasaar Almusanii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «amul benn jaam bu Yàlla sàmmuloo am càmm, mu faatu fekk da doon wuruj ña muy sàmme, lu dul ne Yàlla dana araamal ci moom àjjana».

Jële nañu ci Ummu Salamata ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ay njiit danañu ñëw, da ngeen gis ci ñoom lu baax, ak it lu bon, ku ànd ca lu baax la kooku set na wicc, ku weddi seen yu bon kooku mucc na, waaye ki muccul mooy ki gërëm yu bon ya te ànd ca" ñu ne ko: mo ndax duñu xeex ak ñoom? Mu ne: "déedéet, li fii ak ñoo ngi julli".

Jële nañu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ag siif de dana am ak ay mbir yu ngeen bañ" ñu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi ana lan nga nuy digal? Mu ne: "joxeleen àq ji leen war, te laaj Yàlla seen àq».

Jële nañu ci Abdulaah Ibn Umar -yalna leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku ne ci yéen ab sàmm la te dees na ko laaj la mu doon sàmm, ki jiite nit ñi ab sàmm la te danañu ko ko laaj,góor gi ab sàmm la ci waa këram te danañu ko ko laaj, jigéen ji ab sàmm la ci kër jëkkëram ak i doomam te danañu ko ko laaj, jaam bi ab sàmm la ci alali sangam te danañu ka ko laaj, yégleen ne ku nekk ci yéen ab sàmm la te dees na ko laaj la mu doon sàmm».

Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fekk mi ngi ci sama biir néeg bii muy wax naan: «yaw Yàlla sama Boroom képp ku méngoo dara ci sama mbiri xeet wii, ba noppi di tar ci ñoom, na nga tar ci kawam, waaye képp ku ménggoo dara ci sama mbiri xeet wii, daal di leen woyofalal, na nga ko woyofalal».

Jële nañu ci Tamim Ad-Daarii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mu wax ne: «diine de laayante-biir la» nu ne ko: ngir kan? Mu ne: «ngir Yàlla, ak ngir téereem bi, ak ngir Yónentam bi, ak ngir ñiiti jullit ñi, ak ngir jullit ñépp».

Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa jàng aaya bii: {Moom Yàlla moo wàcce ci yaw Téere ba: am na ca ay aaya yoy séen i maanaa leer nañu, ñoo di cosaani àtte yi, ak yeneeni aaya yu séen i maanaa fésul. Ña nga xam ne jeng a nekk seeni xol, danañu topp lënt ya ngir sàkku fitna ak jéem leen a firi, te Yàlla doŋŋ a xam séen i piri ak ña sax ci xam-xam. Ñoom danañu wax ne : "Gëm nanu ko: lépp ca sunu Boroom la bawoo!" Woroom xel yi rekk ay waaru} [Aali Imraan: 7]. Neena Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di wax ne: "bu ngeen gisee ñiy topp lënt ya xamleen ne ñooñii la Yàlla di wax nangeen leen moytu".