- Dummóoyu jax-jaxali Saytaane yi ak li muy rotal ci xel te bañ cee xalaat, ak làqu ci Yàlla ngir mu dindi ko.
- Lépp luy tàbbi ci xolu nit ki ci ay jax-jaxal yu wuuteek Sariiha loolu ci Saytaane la juge.
- Tere nañu xalaat ci jëmmi Yàlla ji, ñaaxe nañu it di xalaat ci mbidéefam yi ak i keemaanam.