- Solos ŋoy ci sunna ak topp ko.
- Yittewoo di waare, ak di nooyal xol yi.
- Digle ñu topp ñenti njiit yu jub ya tey jubale ci ginnaawam, te ñooy Abuu Bakar, ak Umar, ak Usmaan, ak Aliyun -yal na leen Yàlla dollee gërëm-.
- Tere nañu sos ci diine ji, ndax bidaa yépp ay réer lañu.
- Dañuy dégg di topp njiitu jullit ñi ci lu dul ag moy.
- Solos ragal Yàlla mu màgg mi ci bépp jamono ak bépp anam.
- Wuute luy am la ci xeet wi, waaye bu amee dañoo war a dellu ci sunnas Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ak njiit yu jub ya.