- Tere nañu yar xaj ak di ànd ak moom, danañu settee ci tere gi xaj buy rëbb ak buy wattu (garde).
- Malaaka yidul ànd ca loola mooy malaakay yërmànde,bu dee malaaka yiy wattu nit ki ñoom moom duñu teqalikoo ak jaam ñi ci seen ug toog ak ci seen ug tukki.
- tere nañu ag kalaksone; Ndax benn la ci mbiibi Seytaane yi, te dafay niróo ak kolos yu nasaraan yi.
- War na ci jullit bi mu xér ci sori lépp luy tax malaaka yi sori ko.