- Topp buur ci lu dul moy Yàlla lu war la.
- Ag xuppaate gu tar ñeel na ku génn ci topp njiit la, tàqalikoo ak mbooloom jullit ñi, bu deehee ca melo woowa kon dee na ci yoonu ceddo ya.
- Hadiis bi day tere xeex ngir par-parloo ciw xeet.
- Dañoo war a matal kóllare yi.
- yiw wu bari nekk na ci topp ak taqoog mbooloo mi, ak kóolute ak dal, ak yéweni mbir.
- Tere nañu di niru-nirulu meloy ceddo ya
- Digle nañu taqoo ak mbooloom jullit ñi.