- Bokk na ci tegtali yonnenteg Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yu fàddu yi muy xibaare mu am kem na mu ko waxe woon.
- Di gërëm lu bon walla di ca bokk daganul, waaye dañu koo war a weddi.
- Bu njiit yi sosee lu wuute ak sariiha du dagan ñu leen cay topp.
- Song njiiti jullit ñi du dagan; ndax la cay topp ci yàqute ak tuur deret ak ñàkk kóolute, kon muñ ñaawteefi njiit yiy moy, ak muñ seeni lor moo gën a woyof loolu.
- Mbiri julli de lu màgg la, ndax moo teqale diggante kéefar ak Lislaam.