- Hadiis bii dafa bokk ci li Yonnente bi nettali jële ko ci Boroomam, ñu di ko woowe Hadiis Al-xuddsi walla Hadiisu Al Ilaahiy, te mooy Hadiis bi nga xam ne ay baatam ak i maanaam ci Yàlla la jóge, waaye amul jagle yi nekk ci Alxuraan te mu koy ràññetle ak lu dul moom, niki di jaamu Yàlla ci jàng gi ak di laab ngir jàng ko, ak di ci dëkke mbaa di ci lottloowaate ak yenneen.
- Tere nañu lor péetey Yàlla yi, xemmemloo nañu it ñu bëgg leen, te nangu seen ngëneel.
- Digle nañu ñu noonoo nooni Yàlla yi, te baña féete ak ñoom.
- Kuy wootewoo ne péetem Yàlla la te du topp sariihaam ji kooku ab fenkat la ci li muy wootewoo.
- Ci def yi Yàlla waral, ak bàyyi yi mu araamal lañuy nekkee péetem Yàlla.
- Bokk na ci liy tax Yàlla bëgg jaam bi, di nangu ñaanam, def naafila yi ginnaaw bi ñu taxawee ci def yi war ak bàyyi yi araam.
- Tegtale teddngay niti Yàlla yi ak kaweg seen i wàccuwaay.