- Hadiis bi bokk na ci liy tegtale yónnenteg Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ndax dafa xibaare luy ami ci xeetam wi mu ame na mu ko xibaare woom.
- Dagan na ñu xamal ki nu nattu li ñu ko njortal ciy balaa; ngir mu waajal ko boppam ba bu ko dikkalee mu nekk muñkat buy yaakaar payug Yàlla.
- Ŋoy ci Alxuraan ak Sunna day genne nit ki ci fitna ak wuute.
- Soññee ci dégg ak topp ñeel njit yi cig njekk, te bañ a génn ci seen kaw, doonte dañoo tooñ.
- Jëfandikoo ag xereñte ak topp sunna ci jamonoy fitna.
- Nit ki dafa war a taxaw ci dëgg, doonte dañu koo tooñ.
- Nekk na ci tegtalug reegalu: tànn ay wi gën a woyof walla lor wi gën a woyof.