Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax...
Leerarug adiis bi:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day digle ñu soppi lu bon -te mooy lépp lu Yàlla ak ub Yónenteem tere- kem kàttan...
Jële nañu ci An-Nuhmaan Ibn Basiir -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "misaalu...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa sadd misaal ñeel ñi taxaw ci foroñceeri Yàlla yi, ne coww ci ay ndigalam, di digle lu baax di...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku woote jëme cig...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral na ne ku tegtale daaldi ñaax nit ñi ci yoonu dëgg ak yiw ci wax mbaa jëf dana am pay gu mel...
Jële nañu ci Abuu Mashuud Al-Ansaarii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Amna nit ku mas a ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak m...
Leerarug adiis bi :
Am na ku mas a w ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla defal jàmm- ne ko: sama waruwaay dafa dee, yéegal ma cig daaba, te jox ma war...
Jële na ñu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Kuy niru-nirulu aw nit...
Leerarug adiis bi:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daf nuy xamal ne képp kuy roy yéefar yi, mbaa kàccoor yi, mbaa ñu baax ñi -ci de...
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «ku gis ci yéen lu ñu sib na ko soppi ci loxoom, bu ko manul na ko soppi ci làmmeñam, bu ko manul na ko soppi ci xolam, te loolu moo gën a néew ci ngëm».
Jële nañu ci An-Nuhmaan Ibn Basiir -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "misaalu ki taxaw ci foroñceeri Yàlla yi ak ki ci tàbbi, moo ngi mel ni aw nit wu tegoo bant ci ag gaal, ñii am kaw ga, ñii nekk ca suuf ga, ñi nekk ci suuf bu ñuy wut ndox dañuy romb ña nekk seen kaw, nu mujj wax ne: nun de bu nu xaroon ci sunu wàll aw xarit te dunu lor ñi nekk sunu kaw, bu ñu leen bàyyee ak la ñu bëgg ñoom ñéppay alku, waaye bu ñu téyee seen loxo danañu mucc, ñoom ñépp mucc".
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku woote jëme cig njub dana am ag pay gu mel ni payug
ña ko ca topp, te du wàññi ci seeni pay dara, ku woote it jëme cig reer dana am bàkkaar bu mel ni bàkkaarub ña ko ca topp, te du wàññi ci seeni bàkkaar dara».
Jële nañu ci Abuu Mashuud Al-Ansaarii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Amna nit ku mas a ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ne ko: amuma waruwaay, kon nag jox ma waruwaay, mu ne ko: «amuma ko», am ku ne ko: yaw Yónente bi, dinaa ko tegtal ku ko jox waruwaay, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «Ku tegtale ci lu baax, dina am pay gu mel ni li ki ko def am».
Jële na ñu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Kuy niru-nirulu aw nit ca ñoom la book».
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «giñ naa ci ki bakkanu Muhammat nekk ci loxoom kenn du ma dégg ci xeet wii moo xam Yahuut la walla Nasaraan, ba faatu te gëmul li ñu ma yónni lu dul ne dana bokk ci waa sawara».
Jële na ñu ci Ibn Abbaas-yal na leen Yàlla dollee gërëm-mu wax ne: Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax ci subag sànni jamra fekk moo ngi ci kaw giléemam gi: "foral ma ay xeer" ma foral ko juróom-ñaari xeer yu sew, muy xeer yi muy sànni, mu tàmbali de leen sànni ci loxoom,di wax naan: "sànnileen yu mel nii" daal di wax ne: " yéen nit ñi, moytandikulen ëppal ci diine, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy ëppal ci diine".
Jële nañu ci Abdallah Ibn Mashuud mu wax ne: Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ñiy taral alku nañu» wax na ko ñatti yoon.
Jële nañu ci Adiyyi ibn Haatim mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Yahuut yi ñooy ñi Yàlla mere, nasaraan yi ñooy ñi réer».
Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr Ibnul Haasi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Yàlla bind na ndogali mbindéef yi njëkk muy bind asamaan yi ak suuf si ci juróom-fukki junniy at, mu daaldi wax: te boobu gàngunaayam ga ma nga ca kawum ndox».
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- me wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- waxtaanal na nu te mooy aji-dëggal ba di ku ñu dëgggal ki mu ne: «kenn ci yéen dees na dajale am mbindam ci biiru yaayam ñent-fukki bis ak ñent-fukki guddi, mu nekk lumbuw dereet, kem loolu, nekk aw suux kem loolu, ñu yabal ci moom malaaka ma, ñu digal ko ñenti baat, mu bind ko: wërsëgam, ab digam, ak jëfam, ak day texeedi walla day texe, mu wal ca ruu, kenn ci yéen de dana jëf jëfi waa àjjana ba dara nekkul digganteem ak moom lu dul loxo, téere ba jiitu ko mu jëf jëfi waa sawara daal di dugg sawara, kenn ci yéen it dana jëf jëfi waa sawara ba dara doxul digganteem ak moom lu dul ab loxo, mu jëf jëfi waa àjjana daal di dugg àjjana».
Jële nañu ci Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mu wax ne: «àjjana moo gën a jege ku ne ci yeen ay waroy dàllam, sawara it naka noonu».