- Solos digle lu baax ak tere lu bon ci aar mbooloo mi ak musal leen.
- Bokk na ci yooni jàngale yi joxe ay misaal, ngir jegeele maanaa yi ci xel yi ci anam gu ñuy yëg.
- Def ñaawteef wu fés te kenn ŋàññiwu ko loolu yàqute la guy lor ñépp.
- Alkandeg mbooloo mi day tege ci bàyyi defkati yu bon yi ñuy wéy ci di yàq ci kaw suuf.
- Doxiinu njuumte ak yéene ju rafet doyul ci yéwénal jëf.
- Wareef yi ci askanu jullit yi dañu koy bokk, wànte duñu ko gàll benn nit kese.
- Mbugal mbooloo mi ci bàkkaar bu ñenn ñi jagoo ndeem wàññiwuñu ko.
- Ñiy def jëf yu bon dañuy wane seen bon ci anam wu baax ci askan wi, ñoom ak naaféq yi.