- Araamal ag taral ak diisal ci mbir yépp, ak soññee ci moytu ko ci lépp; rawatina ci jaamu yi ag màggal ñu baax ñi.
- Sàkku li gën a mat ci jaamu yi mbir mu ñu gërëm la; waaye loolu ci topp Sariiha lay ame.
- Soppug di feddali mbir yi am solo, ndax Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa bàmtu wax ci ñatti yoon.
- Yaatug Lislaam ak ug Yombam.